Buur Yàlla

Aji Sax jee moom suuf ak li ko fees, ak àddina ak li ci biiram.
Moo samp suuf biir géej, dëj ko ci kaw wal mi.
Taalifi Cant 24.1-2

Màggal-leen Ki Sax!

Nangeen màggale Yàlla biir këram gu sell, màggale ko ca tatay asamaanam.
Màggaleleen ko ay jalooreem, màggale ko màggam gu réy.
Màggaleleen kog liit, màggale ko xalam ak moroom ma.
Taalifi Cant 150.1-3

Yaay sama Yàlla

Yaw Yàlla, yaay sama Yàlla, ma xëy di la wër, sama bakkan mar la,
sama jëmm namm la, fu suuf mare ndox, ne sereŋ.
Taalifi Cant 63.2-2

Kàddug Yàlla

Yonent Yàlla Daawuda nee na: «Kàddug Yàlla dëgg la, moo dàq wurus, dàqati lem, ku ko sàmm yokku yool» (Taalifi cant 19.11-12).

Kàddug Yàlla, Yàlla moo ko déey ay yonentam, ñu jottali ko, ngir nit ñi mana xam coobareem ak cofeel gi mu am ci ñi mu sakk. Yaw miy jàng téere bii, nu ngi lay ñaanal nga barkeelu ci, ba dajeek yiwu Yàlla.

Ndax mas ngaa xalaat ci lii: Ibraayma, lu ko taxa nekk xaritu Yàlla? Lu tax àddina si jaxasoo nii? Nan la nit mana amee texe? Lan moo tax nit mana bon xol ak lan moo ko mana soppi? Ndax Yàlla man naa baale bépp tooñ? Lu gàddaayloo Almasi bi jëme ko Misra ci Afrig? Lan moo may Almasi bi sañ-sañ ba tax mu mana musle ci Seytaane? Lu nara xew su àddina tukkee? Nan la Àjjana mel?

Kàddug Yàlla am na ci ay tont.

Njàlbéen ga, di téere bi ubbi Kàddug Yàlla, moo indi lu jëm ci Aadama ak Awa, ak Kayin ak Abel, ak Nóoyin ak Ibraayma ak Saarata ak Ajara ak Ismayla ak Isaaxa ak Yanqóoba ak Yuusufa.

Mucc ga, di ñaareelu téere bi, ci la Yàlla joxe yoonam, Musaa jottali, gannaaw ba Yàlla musalee bànni Israayil cig njaam. Ñu ngi ciy nettali, bi Yàlla santee Musaa mu sàkk ab xaymab jaamookaay bu taxawalin ba ak li ci biiram lépp di jëmmal sellaayu Yàlla ak teewaayam ci seen biir.

Sasu Sarxalkat yi, di ñetteelu téere bi, ci la Yàlla tegtale ay sarax yuy doon ag njotlaay ci bàkkaar ak sobe, li ñag diggante Yàlla Aji Sell ji ak doom aadama.

Yeneen téerey bind yu sell yi ñoo indi Ayóoba, ak Kàddu yu Xelu yu Suleymaan, ak li ñu bind ngir nit ñi am xel mu rafet, mana yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon. Yonent Yàlla Esekiyel bind ci xel mu yees mi Yàlla bëgga def ci nit.

Kàddug Yàlla nag yemul ci nettali jaar-jaari jamono, ndax Yàllaa ci fésal mooy kan; mooy ki amul maas, di boroom bépp mbaax, di boroom cofeel ak yërmande, di cellte doŋŋ, xajoowul benn bàkkaar. Yàlla, ci mbaaxam la sàkke àddina, sàkk nit. Waaye bàkkaar ak sobey nit mooy gàllankoor wi yàq digganteem ak Yàlla Aji Sell ji. Teewul Kàddug Yàlla gi xamle na pexe mi Yàlla teggee woowu gàllankoor, ba sàkkal doom aadama yoon wi mu mana jaar, ba dellu ci moom.

Yal na nu Yàlla teg ci yoon wi baax, ba nu mana taseek leeram, Yàlla boole nu ci njabootu Yonent Yàlla Ibraayma, baayu bépp gëmkat, taas nu ci barkeem.

Jàng ko léegi ci sa ordinatër

Seetaan ko

Man ngeen seetaan ay wideo fii yu jëm ci ay nettali yu ñu jukkee ci Kàddug Yàlla

Nanu jokkoo!

Yónnee nu ab bataaxal: